عن أنس بن مالك رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ أَحَبَّ أَنْ يُبْسَطَ لَهُ فِي رِزْقِهِ، وَيُنْسَأَ لَهُ فِي أَثَرِهِ، فَلْيَصِلْ رَحِمَهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5986]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5986]
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci jokk mbokk ak ci di leen seeti di leen teral ci yaram ak ci alal ak yeneen, ndaxte sabab la ci yaatug wërsëg ak gudd fan.