عَنْ أَبِي الدَّرْدَاءِ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَا شَيْءٌ أَثْقَلُ فِي مِيزَانِ الْمُؤْمِنِ يَوْمَ القِيَامَةِ مِنْ خُلُقٍ حَسَنٍ، وَإِنَّ اللَّهَ لَيُبْغِضُ الفَاحِشَ البَذِيءَ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي] - [سنن الترمذي: 2002]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2002]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne li gën a diis ci màndxem jullit bi i ëllëg bis-pénc ci ay jëf ak i wax mooy rafet jikkò ci di fecci kanam, ak bañ a lore, ak di def njekk. Yàlla mu kawe mi nag dafa bañ lu ñaaw ci jëf ak ci wax, ak ki bon li muu wax ci làmmiñam.