عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«أَتَدْرُونَ مَا الْغِيبَةُ؟»، قَالُوا: اللهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ، قَالَ: «ذِكْرُكَ أَخَاكَ بِمَا يَكْرَهُ»، قِيلَ: أَفَرَأَيْتَ إِنْ كَانَ فِي أَخِي مَا أَقُولُ؟ قَالَ: «إِنْ كَانَ فِيهِ مَا تَقُولُ فَقَدِ اغْتَبْتَهُ، وَإِنْ لَمْ يَكُنْ فِيهِ فَقَدْ بَهَتَّهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2589]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee li ma wax moo ngi ci sama mbokk mi nag? Mu wax ne: «bu nekkee ci moom kon jëw nga ko, bu nekkul ci moom nag kon duural nga ko».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2589]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral dëgg-dëggi jëw bi araam, te mooy: tudd jullit bu fàddu ci lu ko neexul, moo xam ciw mbindiinam la walla ciy jikkoom, niki: patt bi, wurujkat bi, fenkat bi, ak melo yu ñaaw yi ko niru, donte melo yooyu moo ngi ci moom.
Bu dee melo wi nekkul ci moom nag loolu moo gën a tar jëw, ndax duur la, maanaam: sosal nit ki ci lu nekkul ci moom.