عَن أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِذَا تَثَاءَبَ أَحَدُكُمْ فَلْيُمْسِكْ بِيَدِهِ عَلَى فِيهِ، فَإِنَّ الشَّيْطَانَ يَدْخُلُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2995]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2995]
Yonnente bi jàngal na kiy óbbali gémmiñam ubbeeku ngir tàyyeel walla suur mbaa luy niru loolu; mu teg loxoom ci gémmiñam tëj ko ci; ndaxte Saytaane da ciy dugg bu ko bàyyee mu ubbiku, bu ko defee tek loxo bi day tax du dugg.