عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«إنَّ الرُّقَى والتَمائِمَ والتِّوَلَةَ شِرْكٌ».
[صحيح] - [رواه أبو داود وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 3883]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 3883]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ay bir yoo xam ne def ko bokkaale la, bokk na ca:
Bu njëkk bi: mocc: wax ji ceddo yi di fajoo te mu làmboo bokkaale.
Ñaareel bi: ay xarnga-fuufa lu deme ni ay xor mbaa lu ni mel: mooy li ñuy tàkkal xale yi ak baayima yi ak yeneen ngir jeñ bët bu aay.
Ñatteel bi: noob: te mooy lu ñuy def ngir kiy sëy bëgg ki muy sëyal.
Bir yii ci bokkaale la bokk; ndax day def mbir ab sabab, te nekkul sababu Sariiha bu am tegtal, nekkul it sabab bu ñu man a làmb daj ko. Bu dee sababi Sariiha yi nag niki jàng Alxuraan, walla yi nu man a yëg niki garab yi nga xam ne dañu koo xame ci def ko, loolu dagan na ànd ak gëm ne moom sabab rekk la waaye njariñ ak lor ci loxol Yàlla la nekk.