عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ عَادَ مَرِيضًا، لَمْ يَحْضُرْ أَجَلُهُ فَقَالَ عِنْدَهُ سَبْعَ مِرَارٍ: أَسْأَلُ اللَّهَ الْعَظِيمَ رَبَّ الْعَرْشِ الْعَظِيمِ أَنْ يَشْفِيَكَ، إِلَّا عَافَاهُ اللَّهُ مِنْ ذَلِكَ الْمَرَضِ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن أبي داود: 3106]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :
"ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu".
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 3106]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne amul benn jullit buy seeti jullit bu feebar te waxtuw deewam jotagul, aji-seeti ji ñaanal aji-feebar ji, ci wax ne: (maa ngi ñaan Yàlla mu màgg mi) ci jëmmam ak i meloom ak i jëfam, (Boroom Aras ju màgg ja mu saafara la), mu baamtu ko juróom-ñaari yoon lu dul ne Yàlla dina ko saafara ca tawat jooja.