+ -

عَنْ عُثْمَانَ بْنِ أَبِي الْعَاصِ الثَّقَفِيِّ رضي الله عنه أَنَّهُ شَكَا إِلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَجَعًا يَجِدُهُ فِي جَسَدِهِ مُنْذُ أَسْلَمَ، فَقَالَ لَهُ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«ضَعْ يَدَكَ عَلَى الَّذِي تَأَلَّمَ مِنْ جَسَدِكَ، وَقُلْ بِاسْمِ اللهِ ثَلَاثًا، وَقُلْ سَبْعَ مَرَّاتٍ أَعُوذُ بِاللهِ وَقُدْرَتِهِ مِنْ شَرِّ مَا أَجِدُ وَأُحَاذِرُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2202]
المزيــد ...

Jële nañu ci Usmaan ibn Abii Al-Haas As-Saxafii yal na ko Yàlla dollee gërëm ne dafa jàmbat Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc aw mettit wu muy yëg ci yaramam diirub ba mu jébbaloo dugg ci lislaam, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko:
«tegal sa loxo fiy metti ci sa yaram, nga wax: Bismil Laahi ñatti yoon, te wax juróom-ñaari yoon: Ahuusu bil Laahi wa xudratihii, min sarri maa ajidu, wa uhaasiru».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2202]

Leeral

Usmaan ibn Abii Al-Haas yal na ko Yàlla dollee gërëm aw mettit da ko a dal xaw ko a ray, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëw fi moom di ko seet, xamal ko ñaan gog Yàlla dana ci yëkkëti li wàcci ci moom ci tawat; te mooy mu teg loxoom ci kaw barab bi muy jàmbat, daal di wax: (Bismil Laahi) ñatti yoon, topp mu wax juróom-ñaari yoon: (maa ngi muslu) di làqu di aaru (ci Yàlla ak kàttanam ci ayu li may yég) ci mettit ci waxtu wii teew (ma di ko moytu) di ragal mu amal ëllëg njàqare ak ragal, walla tawat ji wéy, mettit wi di tasaaroo ci yaram wi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu nit ki mocc boppam kem ni mu ñëwe ci hadiis bi.
  2. Jàmbat -gu andul ak naqarlu ak gaaral- safaanoowul ak wakkiirlu ak muñ.
  3. Ñaan gi dafa bokk ci mbooleem def sabab yi, loolu a tax jaadu na nu tënku ci ay baatam ak i limam.
  4. Ñaan gii day ñeel wépp mettitu cér.
  5. Teg loxo bi ci barab biy metti ci bu ñu dee mocce ñaan gii.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Kinirowanda Rom Majri الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi