عَنْ عَبْدَ اللَّهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ العَاصِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا، قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّكَ لَتَصُومُ الدَّهْرَ، وَتَقُومُ اللَّيْلَ؟»، فَقُلْتُ: نَعَمْ، قَالَ: «إِنَّكَ إِذَا فَعَلْتَ ذَلِكَ هَجَمَتْ لَهُ العَيْنُ، وَنَفِهَتْ لَهُ النَّفْسُ، لاَ صَامَ مَنْ صَامَ الدَّهْرَ، صَوْمُ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ صَوْمُ الدَّهْرِ كُلِّهِ»، قُلْتُ: فَإِنِّي أُطِيقُ أَكْثَرَ مِنْ ذَلِكَ، قَالَ: «فَصُمْ صَوْمَ دَاوُدَ عَلَيْهِ السَّلاَمُ، كَانَ يَصُومُ يَوْمًا وَيُفْطِرُ يَوْمًا، وَلاَ يَفِرُّ إِذَا لاَقَى».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1979]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"yaw de dangay woor at mi, di taxaw guddi gi?" Ma ne ko: waaw, mu ne: "yaw boo defee loolu bët yi dana ca loof, bakkan bi son ca, ku woor at mi kooku woorul, woor ñatti fan mooy woor at mi yépp", ma ne ko: man de man naa lu ëpp loolu, mu ne ma: "kon wooral woorug Daawuda yal na ko Yàlla dolli jàmm, daan na woor bis dog bis, te du daw bu dajee ak noon bi".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1979]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dégg ne Abdullah ibn Amr yal na ko Yàlla dollee gërëm da doon woor te du dog ci at mi yépp, daan julli guddi gi yépp te du nelaw, mu tere ko loolu, daal di ne ko: wooral te dog, taxawal te nelaw. Mu tere ko wéyal ag koor ak di taxaw guddi gi yépp, mu ne ko: boo defee loolu say bët da ciy lompañ daal di ŋiis daal di dugg, sa bakkan day lompañ daal di sonn; ku woor at mi kooku woorul; ndaxte amul fayug woor ngir li mu wuute ak tere gi, te dogul ndax ne daa woor. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daldi koy xamal woor ñatti fan ci weer wu ne te mooy woor at mi; ndaxte bis bu nekk fukki fan la te mooy li gën a néew ci liñuy ful jëf ju rafet. Abdullah ne ko: man de man naa lu ëpp loolu. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: kon wooral woorug Daawuda yal na ko Yàlla dolli jàmm te mooy woor gi gën, moom da daan woor bis dog bis, te daawul daw bu dajee ak noon bi; ndaxte nimuy woore taxul yaramam lott.