+ -

عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَنْ صَامَ يَوْمًا فِي سَبِيلِ اللهِ بَاعَدَ اللهُ وَجْهَهُ عَنِ النَّارِ سَبْعِينَ خَرِيفًا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1153]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:
«ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1153]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne ku woor benn bis ci jihaad, nee nañu it ci jihaad ak lu dul moom di aji-sellal ñeel Yàlla ngir sàkku ci Yàlla yool ak fay; kon Yàlla dana soreele digganteem ak sawara juróom-ñaar-fukki at.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. An-Nawawii nee na: ngëneelu woor ci yoonu Yàlla, loolu dees ciy dégge ki nga xam ne du ca loroo, te du ca faat benn àq, te ab xeexam du ci naaxsaaye du caagine leneen ci yittey xareem bi.
  2. Ñaaxe ak xemmemloo ci woorug coobarewu.
  3. Warug sellal ngir sàkku ngërëmal Yàlla, te du woor ngir ngistal du caagine déggtal du caagine jeneen jubluwaay.
  4. As-Sindii nee na: waxam ji (ci yoonu Yàlla), jamtal na ne li ñu ci namm mooy sellal yéene kese, jamtal na it ne li ñu ci namm mooy dafa woor jamono yi mu nekkee di xare, bu ñaareel bi moo ngana jege.
  5. Ibn Hajar nee na : waxam ji: (juróom-ñaar-fukki Nawet) nawet jamono ju ñu xam la ci at mi, li ñu ci namm fii mooy at mi, li ñu jagleel Nawet cig tudd wolif yeneen jamono yi Noor ak Seddaay ak Lolli; ndaxte Nawet mooy jamono ji gën a teey ndax ca la ñuy watt meññet mi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi