عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
أَوْصَانِي خَلِيلِي صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِثَلاَثٍ: صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1981]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1981]
Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne soppeem ba di xaritam ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a dénk ñatti mbir:
Bi ci njëkk: woor ñatti fan ci weer wu ne.
Ñaareel bi: julli ñaari ràkkay yoor-yoor bis bu nekk.
Ñatteel bi: Wiitar njëkk muy nelaw, loolu nag ci ki ragal ne du yewwu ci mujjug guddi gi.