+ -

عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ عُمَرَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُمَا:
أَنَّ تَلْبِيَةَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَبَّيْكَ اللهُمَّ، لَبَّيْكَ، لَبَّيْكَ لَا شَرِيكَ لَكَ لَبَّيْكَ، إِنَّ الْحَمْدَ وَالنِّعْمَةَ لَكَ وَالْمُلْكَ لَا شَرِيكَ لَكَ» قَالَ: وَكَانَ عَبْدُ اللهِ بْنُ عُمَرَ رَضِيَ اللهُ عَنْهُمَا يَزِيدُ فِيهَا: لَبَّيْكَ لَبَّيْكَ، وَسَعْدَيْكَ، وَالْخَيْرُ بِيَدَيْكَ، لَبَّيْكَ وَالرَّغْبَاءُ إِلَيْكَ وَالْعَمَلُ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1184]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Ni Yonente Yàlla bi doon labbaykawoo mooy: "Labbayka Allaahuma, làbbayka, labbayka laa siriika laka labbayka, innal hamda wannihmata laka walmulka laa sariika laka" nee na: Abdullah ibn Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm daan na ci dolli: labbayka labbayka wa sahdayka, walxayru kulluhu biyadayka, labbayka warraxbaa-u ilayka walhamalu.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1184]

Leeral

Labbayka bu Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan bëgg a dugg ci jaamug Aj gi walla Umra mooy mu wax: (wuyusi naa la yaw sama Boroom wuyusi naa la) wuyu gu sax ñeel la ci li nga nu woo ci sellal ak kennal ak Aj ak yeneen, (wuyusi naa la amóo bokkaale wuyusi naa la) yaw dong yaa yayoo jaamu gi amóo bokkaale ci sag moomeel ak jaamu gi nga moom ak say tur ak say melo, (ag cant) sant ag tagg (ak xéewal) ci yaw la jóge te yaa koy joxe (yaw la ñeel) yaa ciy soppaxndiku ci bépp anam, (ak nguur gi) naka noonu yaw la ñeel, (amóo bokkaale) lépp yaw rekk la ñeel. Ibn Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm daan na ca dolli: (Labbayka Labbayka wa sahdayka) def ma may ku texe, (walxayru bi yadika) yiw yépp ci sa ngëneel la bawoo, (labbayka warragabaa ilayka) sàkku ak laaj ci ki xéewal yi nekk si loxoom rekk lañ koy jëme, (wal amalu) jëf yi yaw la ñeel yaw yaa yeyoo jaamu.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonalees na làbbaykawu ci Aj ak Umra, te ca lay feddalikoo; ndaxte mooy màndargaam bu mu jagoo, ni kàbbar nekke màndarga ci julli.
  2. Ibnul Munayyir nee na: nekk na ci li ñu yoonal labbaykawu ag yeete ci teralug Yàlla ñeel ay jaamam ci ne seenug dajaloo ca néegam ci ag wooteem moom Aji-Sell ji te kawe la ame.
  3. Li gën mooy taqoo ak labbayka bi Yonnente bi doon def, waaye dolli gi aayul ndax li ko Yonente bi saxal, Ibn Hajar nee na: lii mooy anam gi gën a màndu, ñuy ber li jóge ci Yonente bi, bu tànnee li jóge ci ab sahaaba walla mu fental ko boppam ci li yell na ko wax moom doŋ ba du jaxasoo ak li jóge ci Yonente bi, loolu day niróo ak ñaan ci biir taaya, ndax wax na ci loolu ne: topp mu tànn ci ñaan yi ak tagg yi lu ko soob: maanaam ginnaaw ba mu noppee ca la jóge ci Yonente bi.
  4. Sopp nañu yëkkëti kàddu gi ci labbayka gi, lii nag ci àqi góor la, bu dee jigéen moom day wàcce kàddoom ngir ragal fitna.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi
Ndollent