Toftaleg Adiis yi

képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon
عربي Àngale Urdu
Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski
عربي Àngale Urdu
tabax nañu lislaam ci juróom
عربي Àngale Urdu
bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem
عربي Àngale Urdu
genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
عربي Àngale Urdu
bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
عربي Àngale Urdu
Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tabaskee na ñaari kuuy yu duuf am ay béjjan, mu rendi leen ci loxoom, tudd Yàlla daal di kàbbar, teg tànkam bi ca seen doq ya
عربي Àngale Urdu
man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon
عربي Àngale Urdu
daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)
عربي Àngale Urdu
Ni Yonente Yàlla bi doon labbaykawoo mooy: "Labbayka Allaahuma, làbbayka, labbayka laa siriika laka labbayka, innal hamda wannihmata laka walmulka laa sariika laka
عربي Àngale Urdu
ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi
عربي Àngale Urdu