عَن أُمِّ سَلَمَةَ أُمِّ المُؤْمِنينَ زَوْجِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رضي الله عنها قَالت: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ كَانَ لَهُ ذِبْحٌ يَذْبَحُهُ فَإِذَا أُهِلَّ هِلَالُ ذِي الْحِجَّةِ، فَلَا يَأْخُذَنَّ مِنْ شَعْرِهِ، وَلَا مِنْ أَظْفَارِهِ شَيْئًا حَتَّى يُضَحِّيَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1977]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ammu Salamata yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm di soxnas Yonente bi mu ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1977]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digal na ki namm a rendi tabaskeem mu bañ a jël dara ci kawaru boppam walla naqam walla mustaasam walla leneen, niki noonu it bu mu dagg ci ay weyi loxoom walla tànkam dara bu nu gisee weeru Tabaski ba keroog muy Tabaski ba noppi.