عَنْ عَبْدِ الرَّحْمَنِ بْنِ سَمُرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا تَحْلِفُوا بِالطَّوَاغِي، وَلَا بِآبَائِكُمْ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1648]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdur Rahman Ibn Samurata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1648]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere giñ ci Taaxuut yi, te mooy xërëm yi bokkaalekat yi daan jaamu wolif Yàlla, te sabab la ci seen ug bew ak seen ug kéefar, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere ñuy giñ ci baay yi; ndax daa bokkoon ci aaday araab yi ca ceddo ga ñuy giñ ci seen baay yi ngir ndamu ak màggal.