عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّهُ قَالَ:
قِيلَ: يَا رَسُولَ اللهِ، مَنْ أَسْعَدُ النَّاسِ بِشَفَاعَتِكَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ؟ قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَقَدْ ظَنَنْتُ يَا أَبَا هُرَيْرَةَ أَنْ لَا يَسْأَلَنِي عَنْ هَذَا الْحَدِيثِ أَحَدٌ أَوَّلُ مِنْكَ؛ لِمَا رَأَيْتُ مِنْ حِرْصِكَ عَلَى الْحَدِيثِ، أَسْعَدُ النَّاسِ بِشَفَاعَتِي يَوْمَ الْقِيَامَةِ، مَنْ قَالَ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ خَالِصًا مِنْ قَلْبِهِ أَوْ نَفْسِهِ»».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 99]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne:
Wax nañu Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko ana kan ci nit ñi moo gën a texe ci sag rammu ëllëg bis-penc? Yónent Yàlla bi wax ne: «Njoortoon naa ne yaw Abuu Hurayrata Yamamay njëkk laaj lii; ndax li ma gis sag xér ci Hadiis, nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 99]
Yónent ebi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ki gën a texe cig rammoom ëllëg bis-penc mooy ki wax «Laa ilaaha illal Laahu te mu sell ci xolam» maanaam amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, te mu mucc ci bokkaale ak ngistal.