+ -

عن أبي بَشير الأنصاري رضي الله عنه:
أَنَّهُ كَانَ مَعَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي بَعْضِ أَسْفَارِهِ، قَالَ: فَأَرْسَلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَسُولًا -وَالنَّاسُ فِي مَبِيتِهِمْ-: «لَا يَبْقَيَنَّ فِي رَقَبَةِ بَعِيرٍ قِلَادَةٌ مِنْ وَتَرٍ أَوْ قِلَادَةٌ إِلَّا قُطِعَتْ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2115]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Basiir Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-;
Dafa nekkoon ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn tukki, nee na: Yónente daldi yónni benn ndaw -fekk nit ñi ña nga ca séen fanaanukaay- "bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem lu dul ne dàgg na ko".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci benn tukki, nit ñi nekk séen bérabi nelawukaay ya ñuy fanaan ca séen wàccuwaay ya ak xayma ya, mu yónni benn waay ca nit ña ngir digal leen ñu dagg caq yi ñu takk ci doqi giléem yi moo xam ci bant la -bantu fett- mbaa leneen niki jóolóoli walla dàll, loolu nag ndaxte dañu leen ko doon takkal ngir moytu bët, mu digle ñu dagg ko; ndax du delloo ci ñoom dara, ndax njariñ ak lor ci loxoy Yàlla dong la nekk amul bokkaale.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu di takk ay bant ak i caq ngir xëcc njariñ mbaa jeñ lor; ndaxte loolu bokkaale la.
  2. Takk ab caq ci lu dul bantu fett bu dee ngir taar la walla laab ngir Wommat ab mala mbaa yeew ko ci kon dara nekku ci.
  3. War nañoo bañ lu bon sunu kem kàttan.
  4. Wara nañoo wékk sunu xol ci Yàlla rekk amul bokkaale.