عن أبي الهيَّاج الأسدي قال:
قَالَ لِي ‌عَلِيُّ بْنُ أَبِي طَالِبٍ: أَلَا أَبْعَثُكَ عَلَى مَا بَعَثَنِي عَلَيْهِ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ؟ أَنْ لَا تَدَعَ تِمْثَالًا إِلَّا طَمَسْتَهُ، وَلَا قَبْرًا مُشْرِفًا إِلَّا سَوَّيْتَهُ.

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 969]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abul Hiyyaaj Al-Asadi mu wax ne:
Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 969]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na yónni Sahaaba yi ci ñu bañ a bayyi benn «xërëm» -te mooy nataalu lu am ruu moo xam dafa am jëmm walla amul jëmm- lu dul ne dindi nañu ko mbaa ñu far ko.
Ak ñu bañ a bàyyi bàmmeel bu ñu yëkkati lu dul ne maasale nañu ko ak suuf si, màbb la ñu ca tabax, mbaa ñu jégénal ko mu bañ a sute suuf si lu bari, waaye dañu koy yëkkati luy tollook Sibr rekk.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamug nataal lu am ag ruu; ndax daa bokk ci jumtukaayi bokkaale yi.
  2. Yoonalees na dindi lu bon ci loxo ci ku am nguur, mbaa mu man loolu.
  3. Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dindi lépp luy wane jeexitalu ceddo, ci ay nataal ak i xërëm ak tabax ci bàmmeel yi.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (63)