عَن أَبي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«الْحَلِفُ مَنْفَقَةٌ لِلسِّلْعَةِ، مَمْحَقَةٌ لِلرِّبْحِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1606]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
"waat day jariñ liñuy jaay waaye day yàq tonowu".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1606]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo giñ yu bari donte aji-dëggal la ci jaay ak jënd, mu xamle ne sabab la ci njaay mi jar, waaye day wàññi di yàq Barakeb tono li, te amaaana Yàlla xirtal ca ay yàqkat walla ay sàcc walla lakk walla lab walla ñu siif ko walla yeneen yuy yàq alal ja.