+ -

عن أنس رضي الله عنه قال: قال النبي صلى الله عليه وسلم:
«لَا يُؤْمِنُ أَحَدُكُمْ حَتَّى أَكُونَ أَحَبَّ إِلَيْهِ مِنْ وَالِدِهِ وَوَلَدِهِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 15]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 15]

Leeral

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bi ngëmam du mat ba keroog muy jiital bëgg Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bëgg yaay ak baay ak doom ju góor ak doom ju jigéen ak nit ñépp, te bëgg gii day war ñu topp ko di ko dimbale, te bañ koo moy.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. warug bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te jiital ko ci bëgg mbindéef yépp.
  2. Bokk ci màndargay bëgg gu mat: dimbali Sunnas Yónente Yàlla bi, ak joxe sa bakkan ak sa alal ci loolu.
  3. Bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waral topp ko ci lu mu digle, ak dëggal ko ci lu mu xibaare, ak moytu lu mu tere te xuppe ca, topp ko te bàyyi bidaa.
  4. Àqi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gën a màgg gën a feddaliku ci àqi nit ñépp; ndaxte moom mooy sababus sunug gindiku juge cig réer, ak sunug mucc ci sawara ak am àjjana.