+ -

عَنْ أُبَيِّ بْنِ كَعْبٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لاَ تَسُبُّوا الرِّيحَ، فَإِذَا رَأَيْتُمْ مَا تَكْرَهُونَ فَقُولُوا: اللَّهُمَّ إِنَّا نَسْأَلُكَ مِنْ خَيْرِ هَذِهِ الرِّيحِ وَخَيْرِ مَا فِيهَا وَخَيْرِ مَا أُمِرَتْ بِهِ، وَنَعُوذُ بِكَ مِنْ شَرِّ هَذِهِ الرِّيحِ وَشَرِّ مَا فِيهَا وَشَرِّ مَا أُمِرَتْ بِهِ».

[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2252]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«buleen ŋàññ ngelaw li, bu ngeen gisee lu ngeen sib, nangeen wax: Allaahuma innaa nas-aluka min xayri haasihi arriihi wa xayri maa fiihaa wa xayri maa umirat bihii, wa nahuusu bika min sarri haasihii arriihi wa sarri maa fiihaa wa sarri maa umirat bihii».

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2252]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñuy saaga walla ñuy rëbb ngelaw li, ndaxte moom ki ko bind moo ko digal, day indi yërmànde di indi mbugal, te ŋàññ ko mooy ŋàññ Yàlla mi ko bind, ak bañ dogalu Yàlla, Yonente bi daal di jàngale ci nuy dellu ci Yàlla mi bind gelaw li ñaan ko yiw wi ci nekk ak wimu àndal niki indi taw ak toxal niir yi ak yu ko niru, ak muslu ci Yàlla ci ayam ak ay wi mu àndal niki yàq gàncax gi ak garab yi ak alag jur gi, ak màbb tabax yi, ak yu ko niru, ndax ñaan Yàlla loolu dëggal ag njaame la ñeel Yàlla.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu ŋàññ ngelaw li; ndaxte mbindeef la lu ñuy doxal, te ŋàññ ko day dellu ci ŋàññ ki ko bind di ko doxal, te loolu ag wàññeeku la ci Tawhiid.
  2. Dellu ci Yàlla ak muslu ci moom ci ayu li mu bind.
  3. Ngelaw da ñu koy digal aw yiw, di ko digal aw ay.
  4. Ibn Baas nee na: ŋàññ ngelaw li dafa bokk ci moy yi; ndaxte moom mbindeef la lu ñuy doxal di ko yónni ci yiw ak ay; kon daganul ñu ŋàññ ko, deesul wax: yal na Yàlla rëbb ngelaw li, walla yal na Yàlla ray ngelaw li, walla yàlla bu Yàlla baarkeel ngelaw lii, walla luy niru loolu, waaye aji-gëm ji day def jëm ci li ko Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàngal.
  5. Tere gi ñu tere kuy ŋàñ ngelaw li dinañu si boole lépp lu aju ci tàngaay ak seddaay ak Jant bi ak pënd bi ak yeneen yu dul yooyu ci mbindéef Yàlla yi ak ay doxaliinam.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Yorubaa Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi