Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

:
عربي Àngale Urdu
:
عربي Àngale Urdu
Faatimata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ko jàmbat li muy daj ci soqq ak wol, mu dégg ne dafa am ay jaam, te fekku ko fa, mu wax ko Aysatu, ba mu ñëwee Aysatu wax ka ko, nee na: mu ñëw fi nun fekk tëdd nanu, ba nuy jog mu ne nu: "buleen jog" mu ñëw toog sunu diggante, ba may yég seddaayu tànkam ci sama biir, mu wax ne: "@ndax duma leen tektal lu gën li ngeen di laaj? Bu ngeen tëddatee -walla ngeen ñëw ci seen lal- nangeen sàbbaal Yàlla fanweer ak ñatt, te ngeen sant Yàlla fanweer ak ñatt, ngeen màggal Yàlla fanweer ak ñent, loolu moo gën ci yéen liggéeykat".
عربي Àngale Urdu
Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "@ kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon*", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
عربي Àngale Urdu