عن عُثْمَانَ بْنَ أَبِي الْعَاصِ رضي الله عنه:
أنه أَتَى النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، إِنَّ الشَّيْطَانَ قَدْ حَالَ بَيْنِي وَبَيْنَ صَلَاتِي وَقِرَاءَتِي يَلْبِسُهَا عَلَيَّ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «ذَاكَ شَيْطَانٌ يُقَالُ لَهُ خِنْزَِبٌ، فَإِذَا أَحْسَسْتَهُ فَتَعَوَّذْ بِاللهِ مِنْهُ، وَاتْفُلْ عَلَى يَسَارِكَ ثَلَاثًا»، قَالَ: فَفَعَلْتُ ذَلِكَ فَأَذْهَبَهُ اللهُ عَنِّي.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2203]
المزيــد ...
Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2203]
Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, mu tere ma cee toroxlug ragal Yàlla, muy jaxase sama njàng mi, di ma ci sikk-sakkaloo, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: kooku mooy saytaane bi ñuy wax Xinsab, bu loolu amatee nga yég ko, nanga làqu ci Yàlla, muslu ci Yàlla ci moom, te nga ëf ci sa càmmooñ mu ànd ak tuuti tiflit ñatti yoon, Usmaan nee na: ma def li ma Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal, Yàlla dindi ko ci man.