عن ابن عباس رضي الله عنهما:
كان النبي صلى الله عليه وسلم يقول بين السجدتين: «اللَّهمَّ اغْفِرْ لي، وارْحَمْنِي، وعافِني، واهْدِني، وارزقْنِي».
[حسن بشواهده] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 850]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».
[Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 850]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci julli gi juróomi ñaan yii nga xam ne jullit bi da cee am aajo ju màgg, te mu làmboo yiwi àdduna ak allaaxira, ci sàkku njéggal ak suturaal bàkkaar yi te baal ka ko, ak sotti ko yërmànde, ak mucc ci lënt-lënt yi ak bànneex yi ak feebar yi ak wopp yi, te ñaan Yàlla ag gindi ñeel dëgg te sax ca, ak wërsëgu gëm ak xam-xam ak jëf ju baax, ak alal ju dagan te teey.