عَنْ وَائِل بن حُجرٍ رضي الله عنه قَالَ:
صَلَّيْتُ مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَكَانَ يُسَلِّمُ عَنْ يَمِينِهِ: «السَّلَامُ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَةُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ»، وَعَنْ شِمَالِهِ: «السَّلَامُ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَةُ اللَّهِ».
[حسن] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 997]
المزيــد ...
Jële nañu ci Waa-il ibn Hujrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Julli naa ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram: "assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu", ak ci càmmooñam: "assalaamu halaykum warahmatul Laah".
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 997]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan bëgg a génn ci julli gi day sëlmël ci ndayjooram ak ci càmmooñam, mu geestu ci kanamam jëm ci wetu ndayjoor, ànd ak wax: (assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu), daal di sëlmël ci càmmooñam, mu geestu kanamam ci wetu càmmooñam, ànd ak wax: (assalaamu halaykum warahmatul Laah).