عَنِ ابْنِ أَبِي أَوْفَى رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا رَفَعَ ظَهْرَهُ مِنَ الرُّكُوعِ قَالَ: «سَمِعَ اللهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، اللَّهُمَّ رَبَّنَا لَكَ الْحَمْدُ، مِلْءَ السَّمَاوَاتِ وَمِلْءَ الْأَرْضِ وَمِلْءَ مَا شِئْتَ مِنْ شَيْءٍ بَعْدُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 476]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abii Awfaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- budaan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba da daan wax: «samihal Laahu liman hamidahu, Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, mil-as samaawaati wa mil-al ardi wa mil-a maa sita min say-in bahdu».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 476]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba ci julli gi, day wax: "samihal Laahu liman hamidahu", maanaam: ku sant Yàlla mu kawe mi, Yàlla dana ko wuyu nangul ko cantam ak taggam, topp mu sant Yàlla ci wax: "Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, mil-as samaawaati wa mil-al ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu", cant gu fees asamaan yi ak suuf yi ak li ci séen diggante, tey fees lépp lu soob Yàlla.