عن ابنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما عن النبيِّ صلى الله عليه وسلم قال:
«أُمِرْتُ أَنْ أَسْجُدَ عَلَى سَبْعَةِ أَعْظُمٍ: عَلَى الْجَبْهَةِ وَأَشَارَ بِيَدِهِ عَلَى أَنْفِهِ، وَالْيَدَيْنِ، وَالرُّكْبَتَيْنِ، وَأَطْرَافِ الْقَدَمَيْنِ، وَلَا نَكْفِتَ الثِّيَابَ وَالشَّعَرَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 812]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :
«digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér : cib jëh, mu daadi junj loxoom ci bakkanam, ak ñaari loxo yi, ak ñaari wóom yi, ak cati baaraam yi, ak ñu bañ a téye mbaa wog seen i yére ak seen kawar».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 812]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla da koo digal ci julli muy sujjóot ci juróom-ñaari céram; te mooy:
Ab jëh: te mooy: xar kanam ci kaw bakkan bi ak ñaari bët yi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- junj loxoom ci bakkanam, ngir leeral ne jëh ak bakkan benn cér la ci juróom-ñaari cér yi, ak feddali ne kiy sujjóot day laalale bakkanam ci suuf.
Cérub ñaareel bi ak bu ñatteel bi mooy: ñaari loxo yi.
Bu ñenteel bi ak bu juróomeel bi mooy: ñaari wóom yi.
Bu juróom-benneel bi ak bu juróom-ñaareel bi mooy: baaraami tànk yi.
Mu digal nu nuy bañ a takk sunu kawar, walla nuy dajale sunu yére bu ñuy sujjóote ci suuf ngir feg ko; waaye danu koy yoor mu tege ci suuf, mu sujjóot ak cér yi.