+ -

عَنْ ‌حِطَّانَ بْنِ عَبْدِ اللهِ الرَّقَاشِيِّ قَالَ: صَلَّيْتُ مَعَ ‌أَبِي مُوسَى الْأَشْعَرِيِّ صَلَاةً، فَلَمَّا كَانَ عِنْدَ الْقَعْدَةِ قَالَ رَجُلٌ مِنَ الْقَوْمِ: أُقِرَّتِ الصَّلَاةُ بِالْبِرِّ وَالزَّكَاةِ، قَالَ: فَلَمَّا قَضَى أَبُو مُوسَى الصَّلَاةَ وَسَلَّمَ انْصَرَفَ فَقَالَ: أَيُّكُمُ الْقَائِلُ كَلِمَةَ كَذَا وَكَذَا؟ قَالَ: فَأَرَمَّ الْقَوْمُ، ثُمَّ قَالَ: أَيُّكُمُ الْقَائِلُ كَلِمَةَ كَذَا وَكَذَا؟ فَأَرَمَّ الْقَوْمُ، فَقَالَ: لَعَلَّكَ يَا حِطَّانُ قُلْتَهَا؟ قَالَ: مَا قُلْتُهَا، وَلَقَدْ رَهِبْتُ أَنْ تَبْكَعَنِي بِهَا، فَقَالَ رَجُلٌ مِنَ الْقَوْمِ: أَنَا قُلْتُهَا، وَلَمْ أُرِدْ بِهَا إِلَّا الْخَيْرَ، فَقَالَ أَبُو مُوسَى: أَمَا تَعْلَمُونَ كَيْفَ تَقُولُونَ فِي صَلَاتِكُمْ؟ إِنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ خَطَبَنَا فَبَيَّنَ لَنَا سُنَّتَنَا وَعَلَّمَنَا صَلَاتَنَا، فَقَالَ:
«إِذَا صَلَّيْتُمْ فَأَقِيمُوا صُفُوفَكُمْ، ثُمَّ لِيَؤُمَّكُمْ أَحَدُكُمْ فَإِذَا كَبَّرَ فَكَبِّرُوا، وَإِذْ قَالَ: {غَيْرِ الْمَغْضُوبِ عَلَيْهِمْ وَلا الضَّالِّينَ} [الفاتحة: 7]، فَقُولُوا: آمِينَ، يُجِبْكُمُ اللهُ، فَإِذَا كَبَّرَ وَرَكَعَ فَكَبِّرُوا وَارْكَعُوا، فَإِنَّ الْإِمَامَ يَرْكَعُ قَبْلَكُمْ، وَيَرْفَعُ قَبْلَكُمْ»، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «فَتِلْكَ بِتِلْكَ، وَإِذَا قَالَ: سَمِعَ اللهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، فَقُولُوا: اللَّهُمَّ رَبَّنَا لَكَ الْحَمْدُ، يَسْمَعِ اللهُ لَكُمْ، فَإِنَّ اللهَ تَبَارَكَ وَتَعَالَى قَالَ عَلَى لِسَانِ نَبِيِّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: سَمِعَ اللهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، وَإِذَا كَبَّرَ وَسَجَدَ فَكَبِّرُوا وَاسْجُدُوا، فَإِنَّ الْإِمَامَ يَسْجُدُ قَبْلَكُمْ وَيَرْفَعُ قَبْلَكُمْ»، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «فَتِلْكَ بِتِلْكَ، وَإِذَا كَانَ عِنْدَ الْقَعْدَةِ فَلْيَكُنْ مِنْ أَوَّلِ قَوْلِ أَحَدِكُمُ: التَّحِيَّاتُ الطَّيِّبَاتُ الصَّلَوَاتُ لِلهِ، السَّلَامُ عَلَيْكَ أَيُّهَا النَّبِيُّ وَرَحْمَةُ اللهِ وَبَرَكَاتُهُ، السَّلَامُ عَلَيْنَا وَعَلَى عِبَادِ اللهِ الصَّالِحِينَ، أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 404]
المزيــد ...

Jële nañu ci Hittaan Ibn Abdullah Ar-Raxaasii mu wax ne: julli naa ak Abuu Muusa Al-Ashsrii ag julli, dañoo lënkale julli ak ug mbaax ak asaka, nee na: ba Abuu Muusaa noppee ca julli ga ba sëlmël daal di wëlbëtiku, daal di ne: kan ci yéen moo wax baat sàngam ak baat sàngam? Nit ñi noppi, mu waxaat ne: kan ci yéen moo wax wax jii ak jii? Nit ñi noppi: mu ne: man naa am yaw Hittaan yaa ko wax? Mu ne ko: waxu ma ko de, damaa ragal nga gëdd ma ci, am ku wax ci gaa yi ne: man maa ko wax, te nammuma ci lu dul yiw, Abuu Muusa ne ko: xanaa xamuleen lu ngeen di wax ci seen julli gi? Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xutba na nu leeralal nu ay sunnaam xamal nu sunug julli, daal di wax ne:
«bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar, bu waxee: (xayril maxduubi halayhim wa laddaalliina) [Al-Faatiha: 7], nangeen wax: Aamiin, Yàlla dana leen nangul, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar te rukoo, imaam bi moo leen di njëkk a rukoo, moo leen di njëkk a siggi Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, Yàlla dana leen dégg, Yàlla dafa wax ci nettalig Yonnente bi: samihal Laahu liman hamidahu, bu kàbbaree sujjóot nangeen kàbbar sujjóot, imaam moo leen di njëkk a sujjóot njëkk leen a siggi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu nekkee ca toogaay ba kenn ci yéen na njëkk a wax: attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa iLaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan abduhu wa rasuuluhu».

-

Leeral

Sahaaba bii di Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa julli ag julli, bamu nekkee ca toogaayu taaya ba, benn waay ca ñay julli ci ginnaawam daal di ne: julli de ci Alxuraan dañu koo lënkale ak ug mbaax ak asaka, ba Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- noppee ca julli ga daal di jublu maamuun yi, laaj leen: kan ci yéen moo wax wax ji: dañoo lënkale julli ak ug mbaax ak asaka ci Alxuraan?! Gaa yi noppi, te kenn ci ñoom waxul, mu baamtu laaj beneen yoon, ba ko kenn tontuwul nag, Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- wax ne: man naa am yaw Hittaan yaa ko wax! Ngir ag ñemeem ak ni mu ko jegee, ak ni mu jokkoo ak moom, ba tax li mu ko jiiñ du ko lor, ak it ngir mu jeñ aji-def ji dëgg ci nangu, Hittaan weddi loolu, daal di ne ko: damaa ragal nga gëdd ma ngir njort ne maa ko wax, ; ci loolu la benn waay ci gaayi ne: man maa ko wax, te jubluwuma ci lu dul yiw, Abuu Muusa di ko xamal wax ne: ndax xamuleen lan ngeen di wax ci séen julli gi?! Lii nag ag weddi la, Abuu Muusa daal di wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xutba na leen benn bis, daal di leen leeral sariihaam, xamal leen séen ug julli, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne:
Bu ngeen dee julli nangeen jubal séen sàppe yi te yamoo, am ku jiite nit ñi, bu imaam bi kàbbaree bàkkaru armal, nangeen kàbbar ni moom, bu jàngee Faatiha ba toll ci: {xayril maxduubi halayhim wa wa laddaalliina} [Al-Faatiha: 7], nangeen wax Aamiin, bungeen defee loolu Yàlla dana nangu séen ñaan, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar rukoo; imaam bi moo leen di njëkk a rukoo njëkk leen a siggi buleen ko jiitu; ndax saa su leen imaam bi di jiitu ci rukoo bi, dees leen koy fay ci saa si ngeen di yeex a jóge ca rukoo ba ginnaaw bi mu siggee, kon saa soosee ci saasii rekk, bu ko defee séen diirub rukoo tolloo ak diiru rukoowam, bu imaam bi waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax: Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, ñiy julli bu ñu waxee loolu, Yàlla mu kawe mi day wax, ci nettalig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: samihal Laahu liman hamidahu, bu imaam bi kàbbaree daal di sujjóot, war na ci maamuun yi ñu kàbbar daal di sujjóot, ndax imaam bi moo leen di njëkk a sujjóot, njëkk leen a siggi kon saa soosa ci saasii rekk, bu ko defee sujjóotu maamuun yi tolloo ak sujjóotu imaam bi, bu nekkee ci toogaayu taaya bi li kiy julli njëkk a wax na nekk: "attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil-Laahi" ag nguur ak ug des ak ug màgg lépp Yàlla a ko yayoo, niki noonu julliy juróom yépp Yàlla a ko moom, "assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina", ñaanleen Yàlla ag mucc ci bépp ayib ak gàkk-gàkk ak mànkite ak yàq; nuy jagleel sunu yonnente -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ag nuyoo, door a nuyu sunu bopp, topp nu nuyu jaami Yàlla yu baax yiy taxawe li leen war ci àqi Yàlla mu kawe mi ak àqi jaam ñi, topp nu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat jaamub Yàlla la di ndawam.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral benn ci xeeti Taaya yi.
  2. Jëfi julli yi ak wax yi fàww mu bokk ci li sax jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, kon du dagan ci kenn mu sos ca ay wax mbaa jëf yu saxul ci Sunna.
  3. Du dagan ci maamuun bi muy jiitu imaam bi mbaa di yeex lool ci ginnaawam, li ñu yoonal ci maamuun bi mooy mu topp imaam bi ci ay jëfam.
  4. Tudd ni Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yittewoo woon na jottali, ak jàngal xeet wi àttey diine ji.
  5. Imaam mooy royukaayu maamuun bi, kon du dagan mu koy jiitu ci jëfi julli gi, walla muy tolloo ak moom, mbaa muy yeex lool ci ginnaawam, waaye fa mu koy tàmbalee topp mooy ginnaaw ba mu wóoree ne imaam bi dugg na ci jëf ji mu bëgg a def ba noppi, ndax Sunna mooy mu topp ko ca.
  6. Yoonalees na jubal sàppe yi ci julli gi.