عَنِ الْبَرَاءِ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِذَا سَجَدْتَ، فَضَعْ كَفَّيْكَ وَارْفَعْ مِرْفَقَيْكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 494]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Baraa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 494]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral nekkiinu loxo yi ci sujjóot bi ci julli gi, te loolu mooy mu dëgëral ay ténqam ci suuf mu kebale baaraam yi mu jëm xibla, ñaari conc yi yëkkëtiku wolif muy laal suuf ñu sori ñaari wet yi.