عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَسْوَأُ النَّاسِ سَرَقَةً الَّذِي يَسْرِقُ صَلَاتَهُ» قَالَ: وَكَيْفَ يَسْرِقُ صَلَاتَهُ؟ قال: «لَا يُتِمُّ رُكُوعَهَا، وَلَا سُجُودَهَا».
[صحيح] - [رواه ابن حبان] - [صحيح ابن حبان: 1888]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ki gën a bon ug càcc ci nit ñi mooy kiy sacc julleem» ñu ne ko: naka lay sacce julleem? Mu ne: «du matal rukkoo yi, ak sujjóot yi»
[Wér na] - [Ibnu Hibbaan soloo na ko] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 1888]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne ki gën a bon ug càcc ci nit ñi mooy kiy sàcc ci julleem gi; ndaxte jël alalu keneen manees na cee jariñu ci àdduna, wuute ak sàcckat bii, ndax moom àqam ci julli gi ci yool ak pay la sàcc, ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, naka lay sàcce ci julleem gi? Mu ne leen: da dul matale rukoo ya ak sujjóot ya; day yàkkamti ci rukoo yi ak sujjóot yi, ba du leen def ci anam gu mat.