عَن ابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما:
أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَرْفَعُ يَدَيْهِ حَذْوَ مَنْكِبَيْهِ إِذَا افْتَتَحَ الصَّلَاةَ، وَإِذَا كَبَّرَ لِلرُّكُوعِ، وَإِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ مِنَ الرُّكُوعِ، رَفَعَهُمَا كَذَلِكَ أَيْضًا، وَقَالَ: «سَمِعَ اللَّهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، رَبَّنَا وَلَكَ الحَمْدُ»، وَكَانَ لاَ يَفْعَلُ ذَلِكَ فِي السُّجُودِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 735]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi, naka noonu it daan na leen yëkkati bu daan kàbbar ngir rukóo, ak bu daan siggi ca rukóo ba, ak bu daan yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: "samihal Laahu liman hamidahu", daawul def loolu nag ca sujjóot ba.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 735]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan yëkkati ay loxoom ci ñatti barab ci julli gi ba mu tolloo walla mu jàkkaarloo ak ay mbaggam: te mooy fi yaxi mbagg mi dajee ak përëg bi.
Barab bu njëkk bi: buy ubbi julli gi di def kàbbaru armal.
Ñaareel bi: buy kàbbaar ngir rukóo.
Ñatteel bi: buy yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu Rabbanaa wa lakal hamdu.
Daawul yëkkati loxoom bu daan tàmbalee sujjóot, mbaa muy siggi ca sujjóot ba.