+ -

عن عَائِشَةَ رضيَ الله عنها قالت: إِنِّي سمعْتُ رسولَ الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«لَا صَلَاةَ بِحَضْرَةِ الطَّعَامِ، وَلَا هُوَ يُدَافِعُهُ الْأَخْبَثَانِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 560]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 560]

Leeral

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na julli ci teewaayu ñam wi nga xam ne bakkanu kiy julli da koo xemmeem, xolam di ca nekk.
Niki noonu tere na di julli di jañante ak ñaari sobe yi -te mooy saw ak dem duus- ndax kon day soxlawoo di jañ sobe sa .

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jaadu na ci kiy julli mu sori lépp lu koy soxlaal ci julli gi balaa mu caa dugg.