+ -

عن أنس بن مالك رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ نَسِيَ صَلَاةً فَلْيُصَلِّ إِذَا ذَكَرَهَا، لَا كَفَّارَةَ لَهَا إِلَّا ذَلِكَ: {وَأَقِمِ الصَّلاةَ لِذِكْرِي} [طه: 14]».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 597]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu: {taxawalal julli ngir fàttaliku ma}[Taaha: 14]».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 597]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku fàttee joxe julli gu nu farataal ba waxtu wa génn, war naa njëkkante gaawantu ci fay ko ca jamono ja mu ko fàttalikoo, amul luy far bàkkaaru bàyyi ga lu dul jullit bi julli ko ba mu ko fàttalikoo, Yàlla mu kawe mi wax na ci téereem bu tedd ba: {na nga taxawal julli ngir fàttaliku ma} [Taaha: 14], maanaam: taxawalal julli ga nga fàtte woon boo ko fàttalikoo.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral solos julli ak bañ koo sàgganee def ko ca waxtoom ak fay ko.
  2. Daganul ñuy yeexe julli ca waxtoom te tay ko ci lu dul ngànt.
  3. Ki fàtte daa war a fay julli yi mu fàtte woon saa yu ko fàttalikoo, ak aji-nelaw ji saa yu yewwoo.
  4. Dàñoo war a fay julli yi ca na mu gën a gaawe doonte ca waxtuy tere ya la.