عن بريدة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ الْعَهْدَ الَّذِي بَيْنَنَا وَبَيْنَهُمُ الصَّلَاةُ، فَمَنْ تَرَكَهَا فَقَدْ كَفَرَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي والنسائي وابن ماجه وأحمد] - [سنن النسائي: 463]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Buraydata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy - 463]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne kóllare gi dox ci diggante jullit ñi ak ñu dul ñoom ci yéefar yi ak naaféq yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na.