+ -

عن سالم بن أبي الجَعْدِ قال: قال رجل: ليتني صَلَّيتُ فاسترحْتُ، فكأنّهم عابُوا ذلك عليه، فقال: سمعتُ رسولَ الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«يا بلالُ، أقِمِ الصَّلاةَ، أرِحْنا بها».

[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 4985]
المزيــد ...

Jële nañu ci Saalim Ibn Abil Jahd mu wax ne: benn waay dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni dañu koo sikk ci loolu, mune leen dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne:
«yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci».

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4985]

Leeral

Benn waay ci Sahaaba yi dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni ñi ko wër dañu koo sikk ci loolu, mune leen: dégg naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: éey Bilaal! Yëkkëtil nodd gi te taxwal; ndax nu nappaloo ko; loolu nag ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla, ak nooflaayu ruu ak xol.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Nooflaayu xol day ame ci julli; ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla mu kawe mi.
  2. Weddi ci kaw kuy tàyyeel ci jaamu Yàlla.
  3. Képp ku def li ko war, ba setal ca boppam, dana am noflaay ak yég-yégu dal.