+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«‌إِنَّ ‌أَثْقَلَ صَلَاةٍ عَلَى الْمُنَافِقِينَ صَلَاةُ الْعِشَاءِ وَصَلَاةُ الْفَجْرِ، وَلَوْ يَعْلَمُونَ مَا فِيهِمَا لَأَتَوْهُمَا وَلَوْ حَبْوًا، وَلَقَدْ هَمَمْتُ أَنْ آمُرَ بِالصَّلَاةِ فَتُقَامَ، ثُمَّ آمُرَ رَجُلًا فَيُصَلِّيَ بِالنَّاسِ، ثُمَّ أَنْطَلِقَ مَعِي بِرِجَالٍ مَعَهُمْ حُزَمٌ مِنْ حَطَبٍ إِلَى قَوْمٍ لَا يَشْهَدُونَ الصَّلَاةَ، فَأُحَرِّقَ عَلَيْهِمْ بُيُوتَهُمْ بِالنَّارِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 651]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 651]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day wane naaféq yi ak séenug tàyyeel ci teewe julli, rawati na jullig gee ak fajar, ak ne ñoom bu ñu xamoon dayob pay ak yool bi nekk ci teewe ko ànd ak mbooloom jullit ñi kon danañu ko teewe donte dañuy raam ni xale bi di raame ci ay loxoom ak i wóomam.
. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dogu ci digle ñu taxawal julli, mu jiital jenn waay mu wuutu ko jiite nit ñi, mu ànd ak ñu yor ay matti sawara dem ca ña dul teewe jullig mbooloo ma mu làkk séen kër ya ca séen kaw; ndax bàkkaar ya ñu def dafa tar, -waaye defu ko- ndax jigéen ña ca kër ya ak xale ya ak ña deful dara niki ñi am ngànt, te defuñu bàkkaar.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Loràngey ñàkk a julli mbooloo ca jàkka ja.
  2. Naaféq yi jubluwuñu ca séen jaamu ya lu dul ngistal ak ndéggtal, duñu dem ca julli ga lu dul bu leen nit ñi dee gis.
  3. Yool bu màgg bi nekk ci julli gee ak fajar ànd ak mbooloo ma, ak ne ñoom ñaar de jar na ñoo teewe donte dangay raam.
  4. Sàmmonte ak jullig gee ak fajar ag mucc la ci naaféq, waaye di leen wuute ci meloy naaféq yi la bokk.