+ -

عن بعض أزواج النبي صلى الله عليه وسلم عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ أَتَى عَرَّافًا فَسَأَلَهُ عَنْ شَيْءٍ لَمْ تُقْبَلْ لَهُ صَلَاةٌ أَرْبَعِينَ لَيْلَةً».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2230]
المزيــد ...

Jële na ñu ci yenn Soxnay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2230]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di dem cib xamtukat -tur la wu boole gisaanekat ak kuy xamtu ci bidiw yi, ak kuy xamtu ci beeñ bi, ak yu mel ni yooyu, ci képp kuy tegtaloo ci xam kumpa ci jëfandikoo ay bir yu muy jiital- ak ne ku leen laaj dara ci biri kumpa Yàlla dana ko xañ yoolu julleem yi ñent-fukki fan; loolu nag am mbugal la ci bàkkaar bu mag bii.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamal nañu gisaane, ak dem ci gisaanekat yi ak laaj leen ci kumpa yi.
  2. Dees na xañ nit yoolub jaamoom ngir mbugale ko ko ci bàkkaar bu mu def
  3. Day dugg ci Hadiis bi li ñuy woowe taaruwaayu biddiw yi ak di ca xool, ak di jàng ca ténq ya ak kopp ya -donte ci anamug yër dong la-; ndax loolu lépp ci seet la bokk ak wootewoo xam kumpa.
  4. Ndeem lii mooy payug ku dem ci xamtukat ba, kon naka la payug jëmmi kiy xamtu di deme?
  5. Jullig ñent-fukki fan ya dana ko doy kon du ko fay, waaye du ca am ab yool.