+ -

عن عمران بن حصين رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«‌لَيْسَ ‌مِنَّا ‌مَنْ ‌تَطَيَّرَ أَوْ تُطُيِّرَ لَهُ، أَوْ تَكَهَّنَ أَوْ تُكُهِّنَ لَهُ، أَوْ سَحَرَ أَوْ سُحِرَ لَهُ، وَمَنْ عَقَدَ عُقْدَةً، وَمَنْ أَتَى كَاهِنًا فَصَدَّقَهُ بِمَا يَقُولُ فَقَدْ كَفَرَ بِمَا أُنْزِلَ عَلَى مُحَمَّدٍ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ».

[حسن] - [رواه البزار] - [مسند البزار: 3578]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«bokkul ci nun kuy gisaane mbaa ñu gisaaneel ko, walla mu seetlu mbaa ñu seetal ko, walla mu njabar mbaa ñu njabaral ko, ak kuy fas ag fas, ku ñëw ci ab seetkat dëggal ko ca la mu wax kooku weddi na li ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-«.

[Tane na] - [Al-bassaar soloo na ko] - [Téere Adiisu Al-bassaar bees leeral càllala ya - 3578]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tëkku na kuy def ci xeetam wi yenn jëf yi ci li mu wax ne: «bokkul ci nun» bokk na ca yooya:
Bu njëkk bi: "ku gisaane mbaa ñu gisaaneel ko" cosaanam mooy: boyal am picc buy dugg ca liggéey ba ci tukki walla ci yaxantu walla leneen, bu naawee jëm wetu ndayjooram mu baaxal ko daal di wéy ca la mu namm, bu naawee jëm wetu càmmoñ mu gaafal ko daal di bàyyi la mu bëggoon, daganul mu defal lii boppam mbaa muy wut ku ko koy defal, day dugg ci loolu ba tay gaaflu ci mbir yépp, moo xam lu ñuy dégg la walla lu ñuy gis, ci njanaaw mbaa bayima, walla woroom laago yi, walla limat yi (Limat: numéro) mbaa bis yi, walla yeneen yu dul yooyu.
Ñaareel bi: "kuy seetlu mbaa ñu seetal ko" képp kuy wootewoo xam kumpa ci jëfandikoo biddiw yi mbaa leneen, walla mu ñëw ci kuy wootewoo xam kumpa niki seetkat bi ak ñu mel ni moom, daa di koy dëggal ca la muy wootewoo ci xam kumpa, kon weddi na li ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Ñatteel bi: "kuy njabar walla ñu njabaral ko" te mooy kiy njabaral boppam, mbaa mu njabarloo keneen; ngir mu jariñ kenn mbaa lor ko, walla mu fas ag fas ci takk ay wëñ daal di ci njabar ci jàng ca walla def ca ay muslaay yu araam daal di cay ëf.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi: warug wakkirlu ci Yàlla te gërëm ay dogalam ak i àtteem, te araamal gisaane ak gaaflu ak njabar ak seetlu, mbaa laaj ña koy def.
  2. Wootewoo xam kumpa daa bokk ci bokkale wuuteek Tawhiid.
  3. Araamalees na dëggal ab seetkat ak dem ca ñoom, dana bokk ca loolu li ñuy woowe jàng ca ténq ya ak kopp ya, ak nekkuwaayu biddiw yi, ak di ca xool donte sax ci anamug yër la.