عن ابن عباس رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«من اقتبَسَ علْمًا مِنَ النُّجُومِ اقْتبَسَ شُعبَة مِن السِّحرِ، زادَ ما زادَ».
[صحيح] - [رواه أبو داود وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 3905]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku jàng xam-xamu biddiw jàng na benn xaaj ci njabar, bu dollee mu dolliku».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 3905]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku jàng xam-xamu biddiw ak séen i jaaruwaay di tegtalu ci ay yëngatoom ak i duggam ak i génnam ci liy xew ci suuf ci faatug diw mbaa ag dundam mbaa ag woppam, mbaa lu ko niru ci liy am ëlleg, kon jàng na ab xaaj ci njabar, te saa su nit ki di gën a am xam-xam bii rekk gën a barile cig njabar.