عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«رَغِمَ أَنْفُ رَجُلٍ ذُكِرْتُ عِنْدَهُ فَلَمْ يُصَلِّ عَلَيَّ، وَرَغِمَ أَنْفُ رَجُلٍ دَخَلَ عَلَيْهِ رَمَضَانُ ثُمَّ انْسَلَخَ قَبْلَ أَنْ يُغْفَرَ لَهُ، وَرَغِمَ أَنْفُ رَجُلٍ أَدْرَكَ عِنْدَهُ أَبَوَاهُ الكِبَرَ فَلَمْ يُدْخِلاَهُ الجَنَّةَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 3545]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm -mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Waa ji ñu tudd sama tur te julliwul ci man kooku sooy na, waa ji weeru koor dugg ba jeex ta jéggalu ñu ko sooy na, waa ji fekke dunduk ñaari way-juram ñu nekk ay mag, te dugaluñu ko Àjjana kooku it sooy na ».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3545]
Ñatt ñii Yonente bi bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaanalna leen ag toroxtange ak doyadi ak ñàkk: Xeet wu njëkk bi: ki ñu tudd Yonnente bi fi moom te julliwul ci moom ci wax: yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mbaa lu ko niru. Ñaareel bi: ku fekke weeru koor ba mu jeex ta jéggalu ñu ko ngir ag gàtteñloom ci jaamu gi. Ñatteel bi: waa ji fekk ñaari way-juram di ay mag te nekkuñu sabab ci mu dugg àjjana ngir ag moyam ak gàtteñloom ci seen i àq.