+ -

عن جُندب بن عبد الله القَسْرِِي رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ صَلَّى صَلَاةَ الصُّبْحِ فَهُوَ فِي ذِمَّةِ اللهِ، فَلَا يَطْلُبَنَّكُمُ اللهُ مِنْ ذِمَّتِهِ بِشَيْءٍ، فَإِنَّهُ مَنْ يَطْلُبْهُ مِنْ ذِمَّتِهِ بِشَيْءٍ يُدْرِكْهُ، ثُمَّ يَكُبَّهُ عَلَى وَجْهِهِ فِي نَارِ جَهَنَّمَ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 657]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jundub Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla, moom Yàlla du leen toppe dara ci ay àqam, ndax ki Yàlla toppe dara ciy àq dana ko jàpp, te dana këpp kanamam ca sawaraw Jahannama».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 657]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku julli fajar moo ngi ci kaaraangeg Yàlla ak ug càmmam, dana ko wattu dana ko dimbali.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm- daal di n'a tere fecci kóllëre gii ak di ko yàq ci bàyyi julli fajar, walla di sikkal ñi koy julli, mbaa di leen tooñ, ndax ku ko def da ngay yàq dëkkandoo gii, te yelloo na tëkku gu metti, ba Yàlla dina ko toppe li mu sàggane ci àqam, te képp ku Yàlla wut, dina ko jàpp, sànni ko ca sawara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. Leeral njariñu jullig fajar ak ngënéelam.
  3. Artu gu tar ci kaw ñiy jëmale ñaawtéef ci ñiy julli fajar.
  4. Yàlla mu kawe mi day fayyu ci ñiy jëmale ñaawtéef ci jaamam yu sell yi.