+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ تَوَضَّأَ فَأَحْسَنَ الْوُضُوءَ ثُمَّ أَتَى الْجُمُعَةَ فَاسْتَمَعَ وَأَنْصَتَ غُفِرَ لَهُ مَا بَيْنَهُ وَبَيْنَ الْجُمُعَةِ وَزِيَادَةُ ثَلَاثَةِ أَيَّامٍ، وَمَنْ مَسَّ الْحَصَى فَقَدْ لَغَا».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 857]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne :Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku jàppu te rafetal am njàppam daal di ñëw ci àjjuma ji te noppi déglu, dees na ko jéggal li nekk ci diggante bi ak diggante jeneen àjjuma ja, ak ñu dolli ca ñatti fan, ku laal xeer yi nag kooku fo na».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 857]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku jàppu rafetal am njàppam ci matale ponk yi ak def sunna yi ak teggin yi, topp mu dem ca jullig Àjjuma ja daal di noppi te deglu kiy xutba, bàyyi mbóosóor; Yàlla dana ko jéggal bàkkaar yu ndaw yi ci fukki fan yi, tàmbalee ci jullig Àjjuma ji ba ñaareelu Àjjuma ja teg ca ñatti fan; ndaxte fayug lu baax fukk yu mel ni moom la, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo ñàkk a jublug xol bi ci li ñuy wax ci xutba gi ci ay waare, ak ci fowug cér yi ci di laal xeer yi ak yeneen xeeti fo yi ak yittewoo yi, ak ne ku def loolu def na mbóosóor, te ku Def mbóosóor amul cér ci fayug Àjjuma ju mat.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Soññee ci jàppu ak matale sëkk, ak sàmmonte ak jullig Àjjuma.
  2. Ngëneelu jullig Àjjuma.
  3. Déglu xutbag Àjjuma ji lu war la, te bañ a yittewoo wax ak leneen.
  4. Ku def mbóosóor ci jamonoy xutba gi jullig Àjjuma ji dana ko doy dana teggi farata gi, ànd ak yool bu wàññeeku.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Litwaani Serbi Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi