+ -

عن أبِي هُرَيرةَ رضي الله عنه أنَّ رسول الله صلى الله عليه وسلمَ قال:
«إذا قُلْتَ لِصَاحِبِكَ: أَنْصِتْ، يومَ الجمعةِ، والْإِمامُ يَخْطُبُ، فَقَدْ لَغَوْتَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 851]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 851]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bokk na ci teggin yi war ci ki teewe xutbag àjjuma: mu déglu kiy xutba; ngir man a settantal waare yi, te képp ku wax -ak lu mu tuuti-tuuti fekk imaam mi ngi xutba, mu wax keneen: "noppil" ak "déglul", kon ngëneelu jullig àjjuma ga raw na ko.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamal na ñu wax ci jamonoy xutba, donte tere lu bon la, walla delloo ab nuyoo, walla ndokkeel ku tissooli.
  2. Danañu settee ci loolu kuy wax ak imaam walla imaam di wax ak moom.
  3. Wax ci diggante ñaari xutba yi ngir aajo dagan na.
  4. Bu ñu tuddee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk imaam bi di xutba dangay julli ci moom ndànk, niki noonu it wax aamiin ci ag ñaan.
Ndollent