+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، إِذَا كَبَّرَ فِي الصَّلَاةِ، سَكَتَ هُنَيَّةً قَبْلَ أَنْ يَقْرَأَ، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ بِأَبِي أَنْتَ وَأُمِّي أَرَأَيْتَ سُكُوتَكَ بَيْنَ التَّكْبِيرِ وَالْقِرَاءَةِ، مَا تَقُولُ؟ قَالَ «أَقُولُ: اللهُمَّ بَاعِدْ بَيْنِي وَبَيْنَ خَطَايَايَ كَمَا بَاعَدْتَ بَيْنَ الْمَشْرِقِ وَالْمَغْرِبِ، اللهُمَّ نَقِّنِي مِنْ خَطَايَايَ كَمَا يُنَقَّى الثَّوْبُ الْأَبْيَضُ مِنَ الدَّنَسِ، اللهُمَّ اغْسِلْنِي مِنْ خَطَايَايَ بِالثَّلْجِ وَالْمَاءِ وَالْبَرَدِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 598]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar ci julli gi, da daan noppi ab diir njëkk muy jàng, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi jote naa la sama baay ak sama yaay nga xibaar nu sa nopi gi ci diggante kàbbar gi ak njàng mi, lan ngay wax: mu wax ne: "damay wax: Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, Allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqas sawbul abyadi minad danasu, Allaahumma ixsilnii min xataayaaya bissalji wal maa-i wal baradi".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 598]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar ci julli gi day noppi tuuti njëkk muy jàng Al-Faatiha, day ubbee julli gi ci yenn ñaan yi, bokk ci li rot ci ñaan yooyu li muy wax naan: «Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, Allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqas sawbul abyadi minad danasu, Allaahumma ixsilnii min xataayaaya bissalji wal maa-i wal baradi», Day ñaan Yàlla mu soreele digganteem ak ay njuumte ba du ca tàbbi mukk, niki nga xam ne penku ak sowwu du ñu daje ba fàww, bu ca tàbbee itam mu laabal ko ca dindi ko ca kem ni ñuy dinde tilim ji ci yére bu weex, ak mu raxas ko ci ay njuumteem seral ay tàkk-tàkkam ak tàngooram ci yii di seral; ndox, ak galaas.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañuy yalu ñaanug ubbee doonte ci jullig birél la.
  2. Xérug Sahaaba yi ci xam nekkiinu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci yëngatoom ak dalam.
  3. Am na yeneen melo yu rot ci ñaanu ubbee, waaye li gën mooy nit ki topp ñaani ubbee yi sax jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, leeg-leeg mu def bii, leeg-leeg mu def bee.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi