+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَدْعُو وَيَقُولُ: «اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنْ عَذَابِ القَبْرِ، وَمِنْ عَذَابِ النَّارِ، وَمِنْ فِتْنَةِ المَحْيَا وَالمَمَاتِ، وَمِنْ فِتْنَةِ المَسِيحِ الدَّجَّالِ». وفِي لَفْظٍ لِمُسْلِمٍ: «إِذَا فَرَغَ أَحَدُكُمْ مِنَ التَّشَهُّدِ الْآخِرِ، فَلْيَتَعَوَّذْ بِاللهِ مِنْ أَرْبَعٍ: مِنْ عَذَابِ جَهَنَّمَ، وَمِنْ عَذَابِ الْقَبْرِ، وَمِنْ فِتْنَةِ الْمَحْيَا وَالْمَمَاتِ، وَمِنْ شَرِّ الْمَسِيحِ الدَّجَّالِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1377]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ñaan daan na wax: " Allaahumma innii ahuusu bi ka min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali". Am na ci jeneen wax ci Muslim: "bu kenn ci yéen noppee ci taaya ju mujj ji, na muslu ci Yàlla ci ñent: ci mbugalum Jahannama, ak ci mbugalu bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci ayu Masiihud Dajjaal ".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1377]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan muslu ci Yàlla ci ñent, ginnaaw taaya ju mujj ji, njëkk ñuy sëlmal ci julli gi, mu digal nu nuy muslu ci Yàlla ci yooyu,
Bi ci njëkk: ci mbugalum bàmmeel.
Ñaareel bi: ci mbugalum sawara ëllëg bis-pénc.
Ñatteel bi: ci fitnay dund ci bànneexi àdduna yi nu araamal, ak lënt yiy réerale, ak fitnay dee, maanaam waxtuy sukuraat, ci jéng wolif lislaam mbaa sunna, walla fitnay bàmmeel niki laaji ñaari malaaka yi.
Ñenteel bi: fitnay Al-Masiihud-Dajjaal miy génn ci mujjug jamono, Yàlla di ci nattu ay jaamam; da koo jagleel cig tudd nag ngir màggug fitnaam ak i réeralateem.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Muslu yii dafa bokk ci ñaan yi gën a am solo te matale, ngir li mu làmboo ag muslu ci ayi àdduna ak allaaxira.
  2. Mbugalum bàmmeel lu sax la te dëgg la.
  3. Loraangey fitna ak solos muslu ci Yàlla ak ñaan ngir mucc ca.
  4. Saxal ne Dajjaal dana génn ak fitnaam gu màgg ga.
  5. Sopp nañu ñaan gii ginnaaw taaya ju mujj.
  6. Sopp nañu ñaan ginnaaw bu ñu defee jëf ju sell.