عَنْ كَعْبِ بْنِ عُجْرَةَ رضي الله عنه عَنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مُعَقِّبَاتٌ لَا يَخِيبُ قَائِلُهُنَّ -أَوْ فَاعِلُهُنَّ- دُبُرَ كُلِّ صَلَاةٍ مَكْتُوبَةٍ، ثَلَاثٌ وَثَلَاثُونَ تَسْبِيحَةً، وَثَلَاثٌ وَثَلَاثُونَ تَحْمِيدَةً، وَأَرْبَعٌ وَثَلَاثُونَ تَكْبِيرَةً».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 596]
المزيــد ...
Jële nañu ci Kahb ibn Hujrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 596]
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne sikar yi ku koy wax doo sooy te doo réccu, waaye day am yool ci baat yooyu, te yenn day ñëw ginnaaw yeneen yi,ginnaaw jullig farata lañu koy wax, te mooy:
"Subhaanal Laahi" fanweeri yoon ak ñatt, maanaam sellal Yàlla ci gépp wàññiku.
Ak "Alhamdu lil-Laahi" fanweeri yoon ak ñatt, te mooy melal Yàlla ci gépp mat ànd ak bëgg ko ak màggal ko.
Ak "Allaahu Akbar" fanweeri yoon ak ñent, Yàlla moo gën a màgg gën a tedd lépp.