Toftaleg Adiis yi

Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي Àngale Urdu
bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay
عربي Àngale Urdu
man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee
عربي Àngale Urdu
saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal
عربي Àngale Urdu
misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee
عربي Àngale Urdu
ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent
عربي Àngale Urdu
Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa
عربي Àngale Urdu