+ -

عَنْ أَبِي مُوسَى رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَثَلُ الَّذِي يَذْكُرُ رَبَّهُ وَالَّذِي لاَ يَذْكُرُ رَبَّهُ، مَثَلُ الحَيِّ وَالمَيِّتِ»، ولفظ مسلم: «مَثَلُ الْبَيْتِ الَّذِي يُذْكَرُ اللهُ فِيهِ، وَالْبَيْتِ الَّذِي لَا يُذْكَرُ اللهُ فِيهِ، مَثَلُ الْحَيِّ وَالْمَيِّتِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6407]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abii Muusaa yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee", ci baati Muslim: "misaalu kër gi ñuy tudde Yàlla, ak kër gi ñu dul tudde Yàlla, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6407]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na li xàjjale diggante kiy tudd Yàlla mu kawe mi ak ki ko dul tudd, ci ne moo ngi mel ni diggante kiy dund ak ki dee ci jariñe ak rafet melo, misaalu kiy tudd Boroomam moo ngi mel ni kiy dund ki nga xam ne bitéem dafa taaru ci leerug dund gi, biiram leere ak xam-xam, mu am njariñ, misaalu ki dul tudd Yàlla nag moo ngi mel ni ki dee ki nga xam ne biteem dafa yàqu, biiram di ag neen, te amul njariñ.
Niki noonu kër gi ñuy niróoleek kiy dund bu dee ña fa dëkk dañuy tudd Yàlla, bu dul loolu rekk kon kër gu dee la ngir ne ña fa dëkk duñu tudd Yàlla; melal giñu melal dundu ak dee ci kër ñoo ngi ci jublu waa-kër gi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci tudd Yàlla ak àrtu ci sàggane ko.
  2. Tudd Yàlla mooy dundug ruu gi, kem ni ruu nekke dundug yaram wi.
  3. Bokk na ci njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc sadd ay misaal ngir jegeele maanaa yi.
  4. An-Nawawii nee na: nekk na ci woote jëme ci tudd Yàlla mu kawe mi ci kër gi, ak ne warul wéet ci tudd Yàlla.
  5. An-Nawawii wax ne: nekk na ci it ne gudd fan ci topp Yàlla ngëneel la donte aji-dee ji day tuxu jëm ci lu gën; ndax kiy dund da koy sàkku a am di ci dollee li muy def ci ay jaamu.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Nipali Dariya Rom Majri الموري Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi