عَنْ أَبِي مُسْلِمٍ الْخَوْلَانِيِّ، قَالَ: حَدَّثَنِي الْحَبِيبُ الْأَمِينُ، أَمَّا هُوَ فَحَبِيبٌ إِلَيَّ، وَأَمَّا هُوَ عِنْدِي فَأَمِينٌ، عَوْفُ بْنُ مَالِكٍ الْأَشْجَعِيُّ رضي الله عنه قَالَ:
كُنَّا عِنْدَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، تِسْعَةً أَوْ ثَمَانِيَةً أَوْ سَبْعَةً، فَقَالَ: «أَلَا تُبَايِعُونَ رَسُولَ اللهِ؟» وَكُنَّا حَدِيثَ عَهْدٍ بِبَيْعَةٍ، فَقُلْنَا: قَدْ بَايَعْنَاكَ يَا رَسُولَ اللهِ، ثُمَّ قَالَ: «أَلَا تُبَايِعُونَ رَسُولَ اللهِ؟» فَقُلْنَا: قَدْ بَايَعْنَاكَ يَا رَسُولَ اللهِ، ثُمَّ قَالَ: «أَلَا تُبَايِعُونَ رَسُولَ اللهِ؟» قَالَ: فَبَسَطْنَا أَيْدِيَنَا وَقُلْنَا: قَدْ بَايَعْنَاكَ يَا رَسُولَ اللهِ، فَعَلَامَ نُبَايِعُكَ؟ قَالَ: «عَلَى أَنْ تَعْبُدُوا اللهَ وَلَا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَالصَّلَوَاتِ الْخَمْسِ، وَتُطِيعُوا -وَأَسَرَّ كَلِمَةً خَفِيَّةً- وَلَا تَسْأَلُوا النَّاسَ شَيْئًا» فَلَقَدْ رَأَيْتُ بَعْضَ أُولَئِكَ النَّفَرِ يَسْقُطُ سَوْطُ أَحَدِهِمْ، فَمَا يَسْأَلُ أَحَدًا يُنَاوِلُهُ إِيَّاهُ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1043]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Muslim Alxawlaanii , mu wax ne: soppe bu wóor ba wax na ma, te soppe la ci man, ku wóor la it ci man, muy Hawfu ibn Maalik Al-Asjahii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Nekkoon nanu fi Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-juróom-ñent walla juróom-ñatt walla juróom-ñaar, mu wax ne:"ndax dungeen jaayante ak Yonnente Yàlla bi? Nu nekkoon ñu bees ci Lislaam, nu ne ko: jaayante nanu ak yaw, yaw Yonnente Yàlla bi, topp mu wax ne: "ndax du ngeen jaayante ak Yonnente Yàlla bi?" Nee na: nu tàllal sunuy loxo ne ko: jaayante nanu ak yaw, yaw Yonnente Yàlla bi,ci lan lañuy jaayante ak yaw? Mu ne: "ci ngeen jaamu Yàlla te du ngeen ko bokkaale ak dara, ak julliy juróom, ak di topp -mu daaldi wax kàddu gu suufe ne- te du ngeen laaj nit ñi dara" gis naa ñenn ci mbooloo moomu yaru kenn ci ñoom daan na rot, te du laaj kenn ku ka ko jottali.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1043]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa nekkoon ci ab lim ci Sahaaba yi mu sàkku ci ñoom ñatti yoon ñu jaayante ak moom kóllarante ak moom ci taqoo ay bir:
Bi ci njëkk: jaamu Yàlla moom dong ci def ay ndigalam te moytu ay tereem, te bañ koo bokkaale ak dara.
Ñaareel bi: taxawal julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak ci guddi gi.
Ñatteel bi mooy: dégg ak topp ñeel ki jiite mbiri jullit ñi.
Ñenteel bi: seen aajo yépp ñu jëmale ko ca Yàlla te bañ a laaj nit ñi dara,Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- suufeel kàddoom ci loolu.
Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- jëfe nañu loolu jaayante ak moom, ba nettalikatu hadiis bi wax ne: gis naa ñenn ci Sahaaba yooyu yaru kenn ci ñoom day wadd, te du laaj kenn mu ko koy jottali waaye day wàcc jëlal ko boppam.