عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَا مِنْ قَوْمٍ يَقُومُونَ مِنْ مَجْلِسٍ لَا يَذْكُرُونَ اللَّهَ فِيهِ إِلَّا قَامُوا عَنْ مِثْلِ جِيفَةِ حِمَارٍ، وَكَانَ لَهُمْ حَسْرَةً».
[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 4855]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«amul aw nit wuy jog ci ab jotaay te tudduñu fa Yàlla lu dul ne danañu jog mel ni méddum mbaam, ñu ame ca ag réccu».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4855]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne amul aw nit wuy toog ci ab jotaay ba jóge fa te tudduñu fa Yàlla lu dul danañu fa jóge mel ni ñu dajaloo woon ci méddum mbaam ca xasaw ga ak salte ga; ndax li ñu yittewoo wax wolif tudd Yàlla, jotaay booba di ag réccu ci seen kaw ëllëg bis-pénc ak ug wàññeeku ak réccu guy taqoo ak ñoom.