عَن أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يَأْتِي الشَّيْطَانُ أَحَدَكُمْ فَيَقُولُ: مَنْ خَلَقَ كَذَا؟ مَنْ خَلَقَ كَذَا؟ حَتَّى يَقُولَ: مَنْ خَلَقَ رَبَّكَ؟ فَإِذَا بَلَغَهُ فَلْيَسْتَعِذْ بِاللهِ وَلْيَنْتَهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3276]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3276]
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne faj gi gën ci laaj yi Saytaane di jax-jaxale aji-gëm ji, Saytaane naan ko: ku bind lii? Ku bind lii? Ku bind asamaan yi? Ku bind suuf si? Aji-gëm ji di tontu teg ko ci diine ak ci yég-yég ak ci xel naan ko: Yàlla, Waaye Saytaane du yam ci jax-jaxal yooyu, waaye day tuxu ba mujj ne ko: ku bind sa Boroom? Ci loolu nag aji-gëm ji day jeñ jax-jaxal yooyu ci ñatti mbir:
Ci gëm Yàlla.
Ak muslu ci Yàlla ci Saytaane.
Ak taxawlu ci bañ a topp jax-jaxal yi.